Mer08222018

Last updateT3_DATE_FORMAT_LASTUPDATE

Taille police

Profil

Style du menu

Cpanel
Back Vous êtes ici : Home actualités Poème écrit par Cheikh Ahmadou KARA dédié à SËRIÑ MUNTAQÂH Mbacké, khalife Général des mourides

Poème écrit par Cheikh Ahmadou KARA dédié à SËRIÑ MUNTAQÂH Mbacké, khalife Général des mourides

 

 

 

 

 

 

 

 

 

 

 

 

SËRIÑ MUNTAQÂH

Bismi LÂHI ar RAHMÂNI ar RAHÎMI
Wa salla LÂHU allâ SEYDINÂH MUHAMMADIN wa sallama taslîman
Hâzihil qasîdah min QÂDIMI RASÛLI LÂHI illal QALÎFAH-al-MUNTAQÂH

KI moom jamono, ñëw na dem
Ñi KO doon wuutu, ñëpp a dem
Ñaar i Sëtam yi mujj’ee dem
Ki mujju ak kañ tudd’ee baayam

Képp ku jooyoon, na nga reeh
Te ñaan KU-TEDD-KI di reeh
Ku kay bégée ba tax ngay reeh
Looy def di nga ca jëlée ndam

Ma ñëw ci SËRIÑ-MUNTAQÂH
Ma fawqa Ñoñ Waa-Fâqû
Jotaay bu beesam a fawqa
Jotaayu Ñoñ Waa-Fâqû

Izrâfîl ci Développement
Jot na Ndigal ci MARIAMÂH
Jibrîl a ko wax mbir ma
Na Muntaqâh am développement

Zan-Jayâ-Hîlu Malâkah
Jot na Ndigalu BUUR-YÂLLAH
Ci di munna ca kay tal a
Dox di yàxx ba du tal a

Yàxxati ndax Sëriñ-MUNTAQÂH
Moo dònn ñëpp, Irtaqâh
Yim boole ëpp, moo fawqu
Lépp lu baax, mooy Muntaqâh

Dañ ko tànn, di ko élire
Ku am gòpp wutal ileer
Tool i àllarbam di na riir
Ci réew mi ba ñëpp di ser

Dey doon àllarba’y BAMBA-Fépp
Dugub, aareen ci fépp-fépp
Waa-Kër KU-TEDD-KI ci ñëpp
Lañ cay dundal, dara du ëpp

AL MUNTAQÂH mooy MUSTAFÂH
Di BÂRAQALITT, di MUJTABÂH
Tur wu ci ne, siròom
Da ngaa ligéy ba am Ngëram

Ci laa jëlée Irham bi may waxee
KU-TEDD-KI du ma ci naxe
Ñeme wu ma ko, du ay pexe
Kese, MOO di maye texe

Jaayaante na ñu, nang ka nangu
MUSTAFÂH-AFSA digle na ko
Moo neh la woon, kii jàppal ma ko
Moo tax saa mbubu, ma summi ko

Man it, ma jàpp’aat sama bòpp
Def buum ci sama baat u bòpp
Raam’aat, tey summi sama mbub-
Uy darajah, fas la yéene’y tòpp

Murîd, Ndigal da kay jëfée
Lum man a doon mu kay jëfee
Lum jafe-jafe
Di bay sonjaan tey naan kafe

Wa Salâm !

Partager